Alyosha & Zosima

Personal poetry in different languages.

❛In principio erat Verbum.❜ A.I. Free

Juróom ñaar

⇧ SECTION LISTING

Gëj naa la gis
Xamuma looy def
Amaana séy nga ak geneen góor googa
Say doom, yosam lañu
Dégg nañu làkk wi ma neex
Maak yaw, nooy dégg làkku boromi dunyaa jooja
Ca réew mu nu doon ay doxandéem
Waaye xol rekk a nuy ilifoon
Kon booba danu féexoon
Ndax rab yi ragal nañu ci kanam mbëggeel
Li nu bégoon ! Mbaa nu bég ?
Fàtte nga ne nu nga fa woon ?
Maa doon foog ne duma fàttaliku dara
Yàlla tere !
Yàlla yërëm maak yaw
Yiwam ! Gërëm naa borom ba
Booba ak tey, juróom ñaari at la
Mépp ca at yee, daa naa jayaŋ-jayaŋi
Ca diggënte ñaari tangor ya ca yay wa
Tey maratuma
Damay naan ci teen bu wowul mukk
Ci ndox moomu, dees na mana gis dëgg gépp
Càmmoñ bi ak ndeyjoor ji ñoo niroo
Suuf si ak kaw gi duñu benn
Nit moo di ki di, Yàlla di ku di

Sunday, 5th November 2017
Jean-Michel LEON-FOUN-LIN