Alyosha & Zosima

Personal poetry in different languages.

❛In principio erat Verbum.❜ A.I. Free

Man, mbaam-sëf wi

⇧ SECTION LISTING

Xoolal mbaam-sëf male
Xal naa àggi ca àjjana ja
Dafay taxaw ca kaw tund wa
Doxandéem la ca diiwaan bee
Wéet na ndax, moom, lamb na
Wànte sëngéemul te aruwul
Déedéet! Yem na te dafay noppalu
Dafa defoon liggéeyam
Te mu déggal sang bu ko fàtte
Tey féex na te wéetaay ba, xarit la
Reeb xale yi la déggul
Raayu jabar bi la yégul
Ana jigéen ju ma ragal suma xol bëgg?
Ammaa, dafay aniinul ma
Moo ma mana musal ci musiba mi
Maa ko jéli ndax ma ànd ak moon
Dinanuy àttaaya, nu séddale ceeb bi
Dinay la nettali dundu jaam gi
Man, mbaam-sëf wi bëgga
Mel ni góor

Sunday, 1st October 2017
Jean-Michel LEON-FOUN-LIN